TSK

TSK · Luke 3:32

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Wàllu Yudeen ñi, Nason doomu Aminadab.

¶ Ki joxe saraxam ci bés bu jëkk bi, ñeel giirug Yuda, mooy Nason doomu Aminadab.

Sóol ne ko: «Yaw, gone gii, yaay doomu kan?» Daawuda ne ko: «Maay doomu Yese, sa surga ba dëkk Betleyem.»

¶ Ba Israyil gépp gisee na leen Buur tanqamloo, dañu koo tontu ne ko: «Ana lu nu bokk ak Daawuda, lu nu séq ak doomu Yese? Bànni Israyiloo, ca seeni xayma! Yaw askanu Daawuda, xoolalal sa bopp sa kër.» Ba mu ko defee bànni Israyil dellu ca seeni xayma;

Aw njebbit mooy saxe fa ëkkub Yese, ab car soqeekoo fa reen ya,

Mu jële ko fa, sampal leen Daawuda, muy buur bu mu seedeel ne: “Maa ràññee Daawuda doomu Yese, ji sama xol jubool, te mooy jëfe mboolem samay coobare.”