TSK

TSK · Luke 6:38

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

bët fey bët, bëñ fey bëñ, loxo fey loxo; tànk fey tànk,

¶ Su ab seedeb safaan taxawee, tuumaal kenn, ne moo lajj yoon,

Maa ngi ci juróom ñett fukki at tey, te xamatuma lu neex ak lu naqari. Sang bi, man xamatuma sax lu ma lekk di saf mbaa naan, te baatu woykat sax safatu ma dara, muy góor, di jigéen. Kon ana lu ma lay diisalati doye?

Ba mu ko defee ñu wékk Aman ca bant ba mu waajaloon Mardose. Merum Buur doora giif.

Job 31:16 TSK

Damaa masa xañ néew-ji-doole lu muy sàkku, mbaa ab jëtun wékk ma bët, ma tas yaakaaram?

Aji Sax jee ma yool sama njekk, rafetlu sama mucc ayib.

Boroom bi, sewal gi la sunuy dëkk sewal, këpp leen ko juróom yaari yoon,

Barkeb Aji Sax jeey maye alal, kër-këri taxula barele.

Ku tabe am barke, mooy kiy sédd ku ñàkk cib dundam.

Ma ne dogal a ngii binde, fi sama kanam: «Duma noppi déy, maa leen di fey, maa leen di fey ba mu mat sëkk.»

Luke 6:30 TSK

Képp ku leen ñaan, mayleen ko; ku nangu seen yëf, buleen ko ko laaj.

¶ Lii rekk la: ji lu tuut, góob lu tuut; ji lu bare, góob lu bare.

Daan bu àndul ak yërmande, moom lees di àttee ña daawul jëfe yërmande. Yërmande nag kekku na ab daan.