TSK

TSK · Luke 6:49

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

«Li nga nuy wax ci turu Aji Sax ji, dunu ko déglu.

Duma mbugal seeni doom ndax li ñuy gànctu mbaa seen séeti doom ndax li ñuy jaaloo, ndax ñoom sarxalkat yi ci seen bopp, ay gànc lañuy teggeendool te gànc yi ci jaamookaayi xërëm yi, ñoom lañuy indeendool jooxe. Askan wu amul ug dégg, sànku.

Luke 8:5 TSK

«Boroom jiwu moo demoon jiyi. Naka lay saaw ab toolam, ndeke lenn ca jiwu maa nga wadde ca kaw yoon wa, nit ñi joggati ca, picc yi dikk, lekk ko.

¶ «Aw rab wu bon, bu jàppee nit ba génn ko, day wër bérab yu fendi, di wut fu mu nopploo, te du ko gis. Su ko defee mu ne: “Naa dellu ca sama kër, ga ma jóge.”

Waaye waa réewam ña dañu koo bañoon. Ci gannaawam lañu yónni ndaw, ne: “Kii, bugguñu muy sunu buur.”

Jàngoo jàngu laa leen daan tege mbugal ay yooni yoon, ngir xàccloo leen. Maa daan sànju ba xaabaabal ci seen kaw, topp leen ba ci biir dëkki jaambur yi.

¶ Gannaaw bu nu xamee xéll liy dëgg ba noppi nag, su nu bàkkaaratee te di ko tey, su boobaa ab sarax bu far yooyu bàkkaar amatu ci.

Noonu la ngëm deme, su amul jëf ju mu àndal, ngëm gu dee la.

¶ Ndax kat gannaaw bu ñu xamee bu baax sunu Boroom, sunu Musalkat Yeesu Almasi, ba rëcc sobey àddina, bu ñu ca sóobuwaatee ba mu man leen, su boobaa seenug muj moo yées seenug njàlbéen.