liy tax ñu nangul ko mooy muy jur gu amul sikk, di góor; man naa doon aw yëkk mbaa kuuy mbaa sikket.
TSK
TSK · Malachi 1:8
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Waaye su dee nag mbaa gàtt bu ab céram ëpp mbaa mu yées, saraxu yéene la mana doon; su dee sarax su ñuy wàccoo ngiñ, deesu ko nangu.
Kon nag sàkkleen juróom ñaari yëkk, ak juróom ñaari kuuy. Ngeen dem ba ca sama jaam ba Ayóoba, joxe ko fa saraxu rendi-dóomal, te Ayóoba ñaanal leen, ma seet ci moom ba bañ leena mbugale seenug ndof. Ndax waxuleen dëgg ci man ni sama jaam bi Ayóoba waxe.»
¶ Aji Sax ji dafa wax ci askan wii ne: «Ñeeka bëgg ub taxawaalu, baña téye seen tànk. Moo tax man Aji Sax ji bégewuma leen. Léegi ma bàyyi xel seenug mbon, ba mbugale leen seeni moy.»
«Éy bu kenn ci yeen tëjoon bunt yi far, te baña jafal ab taal ci sama kaw sarxalukaay ci dara. Awma benn bànneex ci yeen!» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. «Ab sarax, duma ko nangoo ci seeni loxo.