TSK

TSK · Malachi 2:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Enog moomee, am na juróom benn fukki at ak juróom (65), doora jur Matusalem.

¶ Askanu Nóoyin mooy lii. Nóoyin nit ku jub la woon, di ku mat ci biir nit ñi mu bokkal jamono, te di ku topp Yàlla.

Leween ñeey xamal askanu Yanqóoba say àtte, di won Israyil gii saw yoon. Ñooy taal cuuraay fi sa kanam, di teg saraxi dóomal ci sab sarxalukaay.

Su ñu teewe woon sama jataay sax, mana dégtal sama ñoñ samay kàddu, ba waññee leen seen yoonu mbon ak seen jëfi mbon.

Ña rafet xel leer nàññ ni leeraayu déndub asamaan. Ñi doon xiir mbooloo mi ci ngor ne boyy niy biddiiw, ba fàww.

Luke 1:6 TSK

Ñoom ñaar ñépp a juboon, Yàlla seede, te mucc ayib ni ñuy jëfe santaane yeek ndigali yooni Boroom bi.

Yeerukat ya dikk ne Yeesu: «Sëriñ bi, xam nanu ne njub ngay wax, di ko jàngle. Amuloo parlàqu itam, waaye ci kaw dëgg ngay jànglee yoonu Yàlla.

Nit ñi ci seen bopp ñoo nuy waxal fépp, na sunu ngan ak yeen deme, ak ni ngeen walbatikoo ci Yàlla, dëddu tuur yi, bay jaamu Yàlla ju dëggu jiy dund,

Titus 1:7 TSK

Ndax kat, njiit li war na di ku mucc sikk, gannaaw ab saytukatu kër Yàlla la. Bumu di ku bew, mbaa ku gaawa mer, mbaa ab màndikat, mbaa bëggkatub xeex, mbaa wutkatub am-am bu lewul.

te kàddug fen masula jibe seen gémmiñ. Gàkkuñu fenn.