TSK

TSK · Micah 1:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ba Esekiya buurub Yuda duggee ñeenteelu atu nguuram, yemook ba buurub Israyil Ose doomu Ela duggee juróom ñaareelu atu nguuram, ca la Salmanasar buurub Asiri song Samari, gaw ko.

«Waaye xanaa déggoo ne bu yàgg laa dogal loolu? Ca jant ya woon laa ko nasoon, tey ma sottal ko, ba nga mana def genti jali tojit, dëkk yu tata wër.

Seen tata yu kawe, mu fél, màbb; rattax fi suuf, maasale.

«Maa ngii déy, fi sa kaw, yaw Babilon, ponkalum yàqkat bi,» kàddug Aji Sax jee, «yaw miy yàq àddina sépp. Maay tàllal sama loxo fi sa kaw, taxañe la fa kaw doj ya, def la ponkalum jalu dóom.

Ndeysaan, wurus wa giim na! Ngëneelu wurus soppiku na. Doj yu sell yaa wasaaroo, ca boppu mbedd yépp.

Amos 6:8 TSK

Boroom bi, Aji Sax jee ko giñ ci boppam, kàddug Aji Sax ji Yàllaa, Boroom gàngoori xare yi. Nee: «Maaka sib réy-réylug askanu Yanqóoba, ba seen kër yu yànj soof ma! Maay jébbale seen péey ak mboolem li ci biir.

Yaa génn ngir wallusi sa ñoñ, wallusi ki nga fal. Yaa rajaxe puju néegu ku bon ki, xar ko ñaar, geen ba ci put. Selaw.