TSK

TSK · Micah 2:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Buurub Israyil nag woo yonent yi, ñu daje, xawa tollook ñeenti téeméer. Mu laaj leen ne leen: «Ndax ma dal ci kaw Ramot ga ca Galàdd, am ma bàyyi?» Ñu ne ko: «Demal, ndax Boroom bi moo leen di teg ci sa loxo.»

Boroom ngis, ñu ne ko: «Bul gis,» boroom peeñu, ñu ne ko: «Bu ñu firil peeñuy dëgg. Wax nu lu neex, gisal nu ay nax.»

«Ndax ki gëna tuut ba ki gëna mag, ñépp a ngi lewal lu lewul. Yonent akub sarxalkat, ñépp a ngi wor.

¶ Aji Sax ji ne ma: «Waxyuy fen la yonent yiy waxe ci sama tur. Yebaluma leen, santuma leen ko, waxumaak ñoom. Peeñuy fen ak ngisaaney neen ak nax yu ñu fental seen bopp lañu leen di jottlee waxyu.»

Ñi ma teddadil lañuy waxa wax, naan leen Aji Sax ji déy nee: “Jàmm ngeen di am.” Képp ku topp sa xelum déggadi, ñu ne ko: “Musiba du la dab mukk.”

Maa ngii ci kaw ñiy waxe waxyuy génti caaxaan.» Kàddug Aji Sax jee. «Ñu ngi nettali seeni gént, bay waññi sama ñoñ, ndax seen fen yu jéggi dayo, te man de yebaluma leen, santuma leen dara. Amaluñu askan wii benn njariñ.» Kàddug Aji Sax jee.

«Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Damm naa yet wi leen buuru Babilon tënke woon.

Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoori xare yi dafa wax ci mbirum Akab doomu Kolaya ak Cedesyas doomu Maaseya, ñoom ñi leen di jottli waxyuy fen ci turam. Mu ne: Maa ngii di leen teg ci loxol Nabukodonosor buuru Babilon, mu rey leen, ngeen di gis.

Wóoy ngalla yonent yu ñàkk xel, yiy topp seen xelum bopp te gisuñu tus!

Micah 3:5 TSK

Lii la Aji Sax ji wax ci yonent yiy lajjal samay bokk: «Bu ñu sàqamee ab lanc, yéene jàmm; ku leen leelul, ñu biral waxyub xare.

Ñu ni mel liggéeyaluñu Almasi sunu Boroom, seen koll lañuy liggéeyal. Làmmiñ yu neex, ak kàddu yuy jaye lañuy naxe ñi seenum xel foogadi.

Ñooñu sànkute lañuy mujje; seen koll lañu def seen yàlla, seen gàcce lañuy damoo, te yëfi àddina doŋŋ a leen soxal.

¶ Waaye na mu ame woon ci askanu bànni Israyil ay yonenti caaxaan, ni lay ame ci seen biir ay sëriñi caaxaan yuy sërxal ay àlluway sànkute yuy weddi sax Sang bi leen jot, ba yóbbe seen bopp sànkute ju bette.