TSK

TSK · Micah 3:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Sunuy takk réer na nu, yonent amatul, te kenn xamul fu lii di àkki.

Aji Sax ji déy yeen la wal ngelawal nelaw yu xóot, taf seeni gët, te ngeen di yonent yi; muur seeni bopp te ngeen di boroom peeñu yi.

Teral-leen seen Yàlla Aji Sax ji, bala moo lëndëmal, ngeen tërëfe tundi timis, di séentu leer, mu lëndëmal ba mu ne këruus, fatt taraj

¶ Ba mu ko defee, mu am ñu ne: «Aywaleen, nu lalal Yeremi pexe. Ndax kat soxlawunu ko ba di ci ñàkk dara: du njànglem sarxalkat, du digley boroom xel te du waxyu bu yonent biral. Nanu ko duural ba sànk ko te baña faale lenn ciy waxam.»

Sama loxooy dal yonent, yiy gis peeñuy caaxaan, di gisaaney fen. Sama péncum ñoñ, duñu fa teewe, limeefu kër Israyil, deesu leen ca bind, te réewum Israyil, duñu fa dellu. Su boobaa ñu xam ne maay Boroom bi Aji Sax ji.

dungeen gisati nag peeñuy caaxaan, dungeen gisaaneeti. Maay génne sama ñoñ ci seeni loxo, ngeen xam ne maay Aji Sax ji.”»

¶ «Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi, «Turi xërëm laay dagge ci réew mi, ba deesatu leen fàttliku. Yonent yeek xelum xërëmtu it, maa koy tukkal ci réew mi.