TSK

TSK · Micah 4:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ma ne, ngalla buñu ma ree, di damoo samab jéll.

Ku yoqi, dooleel-leen ko, ku óom yay fenqe, jàppleleen ko.

Janti keroog waa kër Yuda ànd ak waa kër Israyil, bawoondoo réewum bëj-gànnaar, wuti réew ma ma séddoon seeni maam.

«Maa ngii di jële sama ñoñ réewum bëj-gànnaar, dajalee leen fa cati àddina. Silmaxaa ngi ci akub lafañ, jigéenu wérul it ak kuy wasin, ñuy gàngoor gu mag, délsi fii.

Bu ci réer, maa lay seet; bu ci lajj, maa lay délloosi; bu ci damm, maa lay takkal; bu ci néew doole, ma leqli la. Waaye bu ci duuf, am doole, maa lay sànk, foral la li war ci yaw.

te nga wax leen ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di jëleji bànni Israyil ca biir xeet ya ñu fekki, dajalee leen wet gu nekk, délloosi leen seen suufas bopp.

«Yeen askanu Yanqóoba, maa leen di dajalee dajale yeen ñépp, maay boolee boole ndesu Israyil. Benn bopp laa leen di def, niy xar ca gétt ga, niy gàtt ci seenum parlu, coowal nit ña jolli.

Ndax Doomu nit ki, ñi réer la seetsi, ngir musal leen.»

¶ Kon nag «dëgëral-leen loxo yi toqi, ak óom yi bañ,»