TSK

TSK · Micah 4:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Aji Sax ji Boroom bi, Aji Sax ju gàngoor yi kat, mu ngi nii di jële Yerusalem ak Yuda, lu doon wéeruwaay, di cëslaay, muy dugub ju ñu yaakaaroon, di ndox mu ñu yaakaaroon,

Lii a waral sama njàqareg xol, mitit jàpp ma, mel ni mititu mat, ma jaaxle ba déggatuma, jàq ba gisatuma.

Xanaa duma gis ba fàww raayab noon, liitu xare di ko feelu?

Sama bokk yaa ngooguy yuuxu yuux yu àkki fu sore, naan: «Moo Aji Sax ji daa newul Siyoŋ a? Moo Buurub Siyoŋ da fee nekkatul a?»

Laajteleen te xool, ndax góor day wasin léegi? Moona maa gis jàmbaar ju ne jatu, ni kuy matu, kanam xoyy.

Waaye yaw Yanqóoba sama jaam, bul tiit,» kàddug Aji Sax jee; «yaw Israyil, bul ragal. Fu sore laa lay wallujee, yaak sa askan wa ca réewum njaam ga, Yanqóoba dellu dal, fegu; kenn dootu ko tiital.

Ki nuy noyyee, Buur bi Aji Sax ji fal, ca seeni yeer la tance, te nu noon ci keppaaram lanuy dëkke fi digg xeet yi.

Léegi ñu ne: «Amunu buur, ndax noo wormaalul Aji Sax ji, te su nu amoon buur it, lu mu nu manal?