¶ «Bul jébbal kenn ci say doom tuur mi ñuy wax Moleg, ndax waruloo teddadil sa turu Yàlla. Man maay Aji Sax ji.
TSK
TSK · Micah 6:7
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ba loolu amee mu jël taawam bu góor bi nara falu buur, wuutu ko, ne ko teqet rendi, def ko saraxu rendi-dóomal ca kaw tata ja. Waa Israyil ñaawlu jëf ja lool, daldi won buuru Mowab gannaaw, ñibbi seenum réew.
Te itam sarxal na doomam, lakk ko ngir ay tuur. Ci biir loolu jabar na, ñeengo na, jëflante naak boroom rawaan aki gisaanekat. Bare na lu mu def lu Aji Sax ji ñaawlu, ba merloo ko.
may jàngoom niw, seggukaay di ma walal ag diw.
Soxlawuma yëkku yar ak sikketu gétt.
Sàkkuwloo sarax, nde kon ma indi; te soppuloo saraxu rendi-dóomal.
Gottub Libaŋ xambul taalam, te mala ya ca ne doyu ko saraxu rendi-dóomal!
¶ Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, Yàllay Israyil dafa ne: «Seen juru saraxu rendi-dóomal, dollileen ko ci seen yeneen sarax, te lekk yàpp wi.
Yékkatil nañu fi Baal tuur mi bérabi jaamookaay, di ci lakk seeni doom ngir Baal, defal ko ko saraxi rendi-dóomal, te santaanewma ko, waxuma ko, jaarul sax sama xel.
Ñoo njaaloo, ñoo bóome, ñoo njaalook seen kasaray tuur. Doyatu leen, doom yu góor yi ñu ma jural, ñu di leen lakk ngir ay tuur, leele leen.
Ngeen defal ma saraxu rendi-dóomal, mbaa saraxi pepp it, duma ko nangu. Seen saraxu jur guy cant ci biir jàmm, faalewuma.