TSK

TSK · Nahum 2:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ku nekk ay fekkiy bokkam, rawi cam réewam, mbete kéwél gu ñuy rëbb, mbaa xar mu amul sàmm.

Yaaka sonn ci tegtali maa-man! Nañ taxaw boog, wallu la! Ñii di rëdd nataalu asamaan, di niiri biddiiw, ak di xool weer wu feeñ, xamle ca loo dikkleegul.

Nun ñépp a ngi xiiru ni rab wu aay, binnee binni niy xati, yaakaar yoon, yoon wuute, séentu wall, wall sore.

Daggeleen Babilon kuy ji ak kuy góob, ku fay gan, na daw saamaru noon, fëx jëm réewam, dellu cay bokkam.

Jàmbaari Babilon xareetuñu, ña nga des ca seeni tata, doole ŋiis, ñu mel niy jigéen. Bunti dëkk bi dàjjiku, kër ya jàpp.

¶ Kenn ci juróom ñaari malaaka, yi taawu juróom ñaari ndab yi nag dikk, ne ma: «Kaay, ma won la mbugalu jigéenu moykat ju mag, ji toog ci ndox mu bare.