TSK

TSK · Nehemiah 13:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ «Bu loolu weesee mboolem lu jóge ci suuf, muy pepp mbaa doomi garab, cérub fukkeel ba Aji Sax jeey boroom. Dees koy sellalal Aji Sax ji.

¶ Leween ñi ñoom, maa leen jox bépp céru fukkeel bu génne ci Israyil, muy seen cér, ñu yooloo ko seen liggéey bi ñuy liggéey ci xaymab ndaje mi.

¶ Fexeleen bay génne benn céru fukkeel ci mboolem lu seeni tool meññ at mu nekk.

Ci biir loolu nu dogoo def li ñu bind ci yoon wi, di yóbbu ca sunu kër Yàlla ga sunu taaw yu góor ak lu sunu jur taawloo, gu gudd gaak gu gàtt ga, di teg lépp ci loxoy sarxalkat ya fay liggéey.

¶ Ñu daldi tànn bésub keroog ay nit, dénk leen néegi dencukaay, ya ñuy yeb ay jooxe, ak saraxi ndoortel meññeef, ak céri fukkeel yu ñuy génne. Ñu war caa dajale nag cér ya yoon wi dogalal sarxalkat yeek Leween ñi, te mu jóge ci tool yi wër dëkk yi. Waa Yuda rafetlu ca taxawaayu sarxalkat yaak Leween ña.