TSK

TSK · Nehemiah 13:18

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

su boobaa ma gën leena mereeti, noonoo leen, te man ci sama bopp maa leen di mbugalati lu ko ëpp fukki yoon ak juróom, feye leen ko seen bàkkaar.

Ezra 9:14 TSK

Nan lanu mana dellooti di xëtt say santaane, di séyanteek xeet yii ak seen jëf ju siblu? Kon doo nu mere, faagaagal nu, ba kenn du desati mbaa muy rëcc?

Aji Sax ji dafa wax ne: Moytuleen seen bopp ba baña gàddu lenn bésub Noflaay, di ko jaarale bunti Yerusalem.

Dangeena fàtte seen mbonug maam ya ak mbonu buuri Yudak seen mboni jabar yaak seen mbonu bopp ak seen mbonu jabari bopp ga ñu nekke woon ca réewum Yuda ak mbeddi Yerusalem?

Gànctoom ga woon ca Misra, bawu ko. Moom lañu daan tëdde cag ndawam, te ñoo daa motoxal cusi janqam, ba sotti ko seen yàqute.

Amos 8:5 TSK

te naan: “Xanaa màggalu Terutel weer wi du jeex ba nu jaay sunu pepp? Waay, na bésub Noflaay jàll gaaw, ba nu ubbi sàq yi, tuutal nattu sol-sotti, diisal doomu nattukaay, tey naxee sunuy màndaxekaayi njublaŋ,