TSK

TSK · Nehemiah 13:25

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Te it bu ngeen jëlalee seeni doom jabar ca seen doom yu jigéen, seen jigéen ñooña dinañu gànctook seeni tuur, ba xiir seen doom yu góor ci gànctook seen tuur yooyu.

Buleen séyanteek ñoom: seen doom ju jigéen, buleen ko may doomu xeet yooyu, jigéenu xeet yooyu it, buleen ko jëlal seen doom ju góor.

¶ Leween ñi ñooy wax ak waa Israyil gépp, di àddu ca kaw, ne:

Ezra 7:26 TSK

Képp ku ci sàmmul sa yoonu Yàlla ak yoonu buur, nañu ko daldi teg mbugal mi war ci moom. Dee mooy doon àtteem, mbaa ñu génne ko réew mi, mbaa ñu nangu alalam, mbaa ñu tëj ko.

¶ Ba ma déggee seeni xultook seen wax jooju, mer naa lool.

¶ Bànni Israyil ga ca des nag fekksi leen, muy sarxalkat yaak Leween ñaak fara bunt yaak jàngkat yaak liggéeykati kër Yàlla ga, di mboolem nun ñi beddeeku woon waasoy réew yi, ngir topp yoonu Yàlla wi, nook sunuy jabar ak sunu doom yu góor ak yu jigéen, mboolem ñi xam te xàmmee.

Ma ŋàññ kàngami Yuda, ne leen: «Lu ñaaw lii ngeen di def nag di teddadil bésub Noflaay?

Ku wacc yoon, gërëm ku bon; ku wormaal yoon, jànkoonteek ku bon.

¶ Kenn ci xamkati yoon yi nag àddu ne: «Sëriñ bi, loolu nga wax de, nun itam, xasaale nga nu ci.»