Nehemiah 11:3
TSK
Dëkki Yuda ya bànni Israyil yaa ca dëkkoon, ñook sarxalkat yaak Leween ñaak, ña féetewoo liggéey yu sew ya ca kër Yàlla gaak ña askanoo ca jaami Suleymaan ya, ku nekk ak sa céru suuf, ca dëkk ba nga bokk. Ñii ñuy lim nag ñooy njiiti diiwaan ñi dëkke Yerusalem.