TSK

TSK · Numbers 12:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

liit ga gëna jolli. Musaa ngay wax, Yàlla di ko tontoo kàddug dënu.

Ñu daldi gis Yàllay bànni Israyil. Lu mel ni dëru per bu safiir a nga lal tànkam ya, mel ni asamaan, ndax na mu sete wecc.

Aji Sax ji ne ko: «Dinaa rombale sama gépp mbaax fi sa kanam, tey biralaale turu Aji Sax ji fi sa kanam. Maay baaxe ku ma neex, te maay ñeewante ku ma neex.»

¶ Aji Sax ji nag wàcc ci biir aw niir, taxaw ak Musaa foofa, daldi biral turam, ne: «Aji Sax ji.»

Naka la Aaróona ak bànni Israyil gépp xoolaat Musaa, gisuñu lu moy deru kanam gay lerxat, ñu daldi koy ragala jege.

te dinañu ko nettali waa réew mii. Waa réew mii dégg nañu ne yaw Aji Sax ji ci sa bopp yaa nekk ci digg mbooloo mii ngay feeñu bët ak bët, yaw Aji Sax ji, saw niir taxaw, tiim leen, te aw taxaaru niir nga leen di jiitoo bëccëg, jiitoo leen aw taxaaru sawara, guddi.

Ab yonent bu soqikoo ci yeen kay, di seen mbokk ni man, moom la leen seen Yàlla Aji Sax ji di feeñalal. Moom ngeen di déggal.

Man nag ma am dëgg, ne la jàkk, yewwu, regge sa jëmm.

Ana kan ngeen di niruleek Yàlla, ak nataal bu ngeen koy dendaleel?

Yaw nit ki, caxal waa kër Israyil aw cax, ci biir léeb woo leen di léebal.

Tey jii ci ab seetu lanuy gise gis-gis bu lënt. Waaye bu keroogee, màkk lanuy jàkkaarloo ak li nuy xool. Tey jii, as ndog laa xam, waaye su keroogee, ni ñu ma xame, ni laay xame ba mu mat sëkk.

Aji gëmadi ñooñu la Seytaane yàllay xarnu bii gëlëmal seenum xel, ngir ñu baña gis ceeñeeru xibaaru jàmm bu leeru Almasi, miy melokaanu Yàlla.

Kon nag ku jalax ndigal lii, du nit nga jalax, xanaa Yàlla, moom mi leen jox Noowam gu Sell.

Kooku mooy lerxat leeru Yàlla, te mooy ki jëmmal nekkug Yàlla. Moo téyee lépp kàddoom gu manoorewu. Gannaaw ba mu setalee bàkkaar yi nag, fa ndijooru Aji Màgg ji la toog, fa kawte ya,

Jude 1:8 TSK

¶ Géntkat yii itam noonu rekk lañuy sobeele seen yaramu bopp, boole ci di sofental kilifteef, ak di saaga boroom daraja ya fa asamaan.