TSK

TSK · Numbers 13:33

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ña nga jaare Negew ca bëj-saalum, dem ba Ebron, fa Anageen ña, Ayman ak Sesay ak Talmay, dëkkoon. Ebron googee, tabaxees na ko juróom ñaari at lu jiitu Cowan ga ca Misra.

¶ Emeen ñaa fa jëkkoona dëkk, askan wu am kàttan lañu woon, bare, yegg ca kaw ni Anageen ñi.

Askan wu am kàttan, yegg ca kaw, soqikoo ci Anageen, ñi ngeen xam, te dégg ñuy wax ci ñoom, naan: «Ku mana të Anageen ñi?»

¶ Ba bànni Israyil gépp gisee waa ja, dañoo dellu gannaaw, tiit lool.

¶ Xare dellu amati ca Gaat. Jenn waay ju réya réy a nga ca woon, ku am juróom benni baaraam, loxo bu nekk, ak juróom benni baaraam, tànk bu nekk, lépp di ñaar fukki baaraam ak ñeent. Moom it ponkalum Rafayeen la woon.

Moom moo tooge kaw wërngalu suuf, ñi ko dëkke mel niy soccet, moo tàllal asamaan ni ndimo, firi ko nib xayma, dëkke.