TSK

TSK · Numbers 14:33

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ba loolu amee sànjum Aji Sax ji tàkkal Israyil, mu wërloo leen ca màndiŋ ma diiru ñeent fukki at, ba mboolem maas googa defoon lu Aji Sax ji ñaawlu, ñépp jeex tàkk.

¶ Waaye ñeent fukkeelu atam, gannaaw ba bànni Israyil génnee Misra, keroog benn fan ca fukkeelu weer waak benn, ca la Musaa doora wax bànni Israyil mboolem lu ko Aji Sax ji santoon ca ñoom.

Mu dagg seeni fan, mu wéy ni cóolóol, faat seen bakkan ci safaan bu gaaw.

Aji Sax ji sib seen njiit yi leen not, wërloo leen àll bu amul yoon.

«“Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yaa ma fàtte, jalax ma sa gannaaw. Kon nag gàddul sa ayu ñàkk gàcceek sa gànctu.”»

Hosea 9:1 TSK

Yeen waa Israyil, buleen béglu, buleen bànneexu ni yeneen xeet yi, nde yeena gànctu, dëddu seen Yàlla, yeena safoo peyu ngànctu ci mboolem dàgga ju ñuy bàcce pepp.