TSK

TSK · Numbers 15:41

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Maa leen di def sama ñoñ, di seen Yàlla. Dingeen xam ne man Aji Sax ji maay seen Yàlla, ji leen di teggil sas, yi leen waa Misra teg.

Man Aji Sax ji maay seen Yàlla ji leen génne réewum Misra, jox leen réewu Kanaan, te di seen Yàlla.

¶ «Ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «yu may fas ak waa kër Israyil ak waa kër Yuda kóllëre gu yees.

Maa leen di wis ndox mu set, ngeen set. Mboolem seen sobe ak mboolem seen kasaray tuur laa leen di setalal.

¶ Waaye yeen nag yeen ay giir giy tànneef, yeenay sarxalkati Buur, yeen ay askan wu sell, yeen ay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.