TSK

TSK · Numbers 16:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Leween ñi nag nañu dal fi wër jaamookaay bi seedes kóllëre gi dence. Su ko defee am sànj du dal ci kaw mbooloom bànni Israyil. Te itam na Leween ñi dénkoo dénkaaney jaamookaay bi seedes kóllëre gi dence.»

Su ko defee nga beral ma Leween ñi, man Aji Sax ji, ñu wecci mboolem taawi bànni Israyil gi ci des, juri Leween ñi itam wecci mboolem luy taaw ci juri bànni Israyil gi ci des.»

Dangaa xeeb li nga nu jële réew mu meew maak lem ja tuuroo, ngir reylu nu ci màndiŋ mi, ba tax ngay buur-buurlu ci sunu kaw teg ci?

¶ Jant yooyu la Aji Sax ji ber giirug Lewi, ngir ñuy gàddu gaalu kóllëreg Aji Sax ji, di taxaw fi kanam Aji Sax ji, di ko liggéeyal, di taase barke ciw turam, te mooy seen péete ba tey jii.

¶ Boroom bi Aji Sax ji, loolu doyatu la, nga waxaale ci sama askan, wi xaajagula ñëw, Sang bi. Boroom bi, Aji Sax ji, ndax nii ngay jëfeek doom aadama?

¶ Ñu daldi tànn bésub keroog ay nit, dénk leen néegi dencukaay, ya ñuy yeb ay jooxe, ak saraxi ndoortel meññeef, ak céri fukkeel yu ñuy génne. Ñu war caa dajale nag cér ya yoon wi dogalal sarxalkat yeek Leween ñi, te mu jóge ci tool yi wër dëkk yi. Waa Yuda rafetlu ca taxawaayu sarxalkat yaak Leween ña.

Xanaa fore parlu mu baax mi da leena doyul, ba ngeen di dëggaate li des ci seen parlu mi? Am naan ndox mu teey doyatu leen, ba bu ngeen naanee ba màndi, di wéquy nëxal ndox mi?

Ay surga aki fara bunti kër rekk lañuy doon ci sama bérab bu sell bi, te ñooy tegoo liggéeyu kër gi. Ñooy rendil xeet wi saraxu rendi-dóomal, ak gépp jur gu ñuy sarxal, te ñooy nekk ci waawu xeet wi, di leen surgawu.

Acts 13:2 TSK

Ñooñoo daje woon di màggal Boroom bi, boole kook koor. Ci biir loolu Noo gu Sell gi ne: «Beral-leen ma nag Barnaba ak Sóol ngir liggéey, bi ma leen wooye.»