TSK

TSK · Numbers 18:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Leween ñi nag nañu dal fi wër jaamookaay bi seedes kóllëre gi dence. Su ko defee am sànj du dal ci kaw mbooloom bànni Israyil. Te itam na Leween ñi dénkoo dénkaaney jaamookaay bi seedes kóllëre gi dence.»

¶ Seen sas nag moo doon gaal gi, ak taabal ji, ak tegukaayu làmp bi, ak sarxalukaay yi, ak ndabi sarxal ya ñu ca daa jëfandikoo, ak ridob biir bi, ak mboolem liggéey bu ci war.

¶ «Bu dal bi waree jóg, na Aaróona ak doomam yu góor muur yëf yu sell yi, ak mboolem jumtukaayi bérab bu sell bi ba noppi. Gannaaw loolu la askanu Keyat di dikk, ngir gàddu ko. Su ko defee duñu laal dara lu sell, bay dee. Loolu la Keyateen ñi di gàddu ci wàllu xaymab ndaje mi.

Bu Keyateen ñi dugg, di xool lu mu gàtt gàtt, yëf yu sell yi. Lu ko moy ñu dee.»

Yaw nag yaak say doom, dénkooleen seenug carxal ci mboolem mbiru sarxalukaay bi, ak ca wàllaa ridob biir bi, ngeen di ca liggéey. Seen liggéeyu carxal bi, ab sasu teraanga la, maa leen ko terale. Waaye ku bokkul ci yeen, bu ci laalee, dees koy rey.»