TSK

TSK · Numbers 18:32

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Na Aaróona aki doomam jiitloo loolu, bu ñuy dugg ci xaymab ndaje mi, mbaa ñuy jegeji sarxalukaay bi, ngir liggéey ci bérab bu sell bi, ndax ñu baña yóbbe seen bopp mbugal, muy seen dee. Na Aaróona ak askanam sàrtoo loolu fàww.

«Waxal Aaróona aki doomam yu góor ne leen lii mooy li mana tax ñu sore yu sell, yi ma bànni Israyil sellalal, ngir baña teddadil sama tur wu sell. Maay Aji Sax ji.

¶ Bu bànni Israyil juuxati ci xaymab ndaje mi, di gàddu bàkkaar bu dee di àtteem.

¶ Moo tax, képp ku jekkadi nu mu lekke ci mburu mi, ak nu mu naane ci kaasu Sang bi, tooñ nga yaramu Sang bi, ak deretam.