TSK

TSK · Numbers 19:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Te itam képp ku for lenn lu dee ci yii, na fóot ay yéreem, waaye dina yendoo sobe ba jant so.

Ku for méddam, na fóot ay yéreem te dina yendoo sobe ba jant so. Yooyu daganul ci yeen.

Te it lu ci dee ba wadd ci kaw lenn, loola day sobewu, nay ndabal bant, mbaa ndimo, der mbaa ab saaku, mbaa jumtukaay bu mu mana doon. Nañu sóob loola ci ndox te du tee mu yendoo sobe ba jant so, mu doora set.

Képp ku lekk ca médd ma, na fóot ay yéreem, te du tee mu yendoo sobe ba jant so. Képp ku for médd ma, na fóot ay yéreem te du tee mu yendoo sobe ba jant so.

Képp ku laal lalam, na fóot ay yéreem, sangu, te du tee mu yendoo sobe ba jant so.

Ki ko lakk bu noppee, na fóot ay yéreem, sangu, doora mana duggaat ci dal bi.

Kiy lakk nag wi itam, na fóot ay yéreem, sangu, te du ko tee yendoo sobe ba ca ngoon.

¶ «Na leen loolu ñeel ci kaw dogalu yoon bu sax dàkk. Ka doon wis-wisal ndoxum setlu mi nag, na fóot ay yéreem, te ku laal ci ndoxum setlu mi day yendoo sobe ba ca ngoon.