TSK

TSK · Numbers 20:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Mbooloom bànni Israyil gépp nag di diiŋat Musaa ak Aaróona ca màndiŋ ma.

«Dégg naa diiŋati bànni Israyil. Wax leen ne leen, diggante ngoon ak jant bu so, dinañu lekk yàpp, te bu bët setee ñu lekk aw ñam, ba regg, ndax ñu xam ne man Aji Sax ji, maay seen Yàlla.»

Ñu jote faak Musaa, naan ko: «Joxleen nu nag ndox mu nu naan!» Musaa ne leen: «Ana lu ngeen joteek man? Aji Sax ji ngeen di seetlu nag?»

Bànni Israyil gépp nag di ñaxtu ci kaw Musaa ak Aaróona, mbooloo ma mépp naa leen: «Waay lu nu tee woona dee ca réewum Misra, mbaa sax nu dee ci màndiŋ mii!

Ci kaw loolu ñu bokk daje fi kaw Musaa ak Aaróona, ne leen: «Doy na sëkk! Mbooloo mi ba mu daj, ñépp a sell, te ci sunu biir la Aji Sax ji nekk. Ana lu ngeen di xoggliku ci kaw mbooloom Aji Sax ji?»

Buleen jàmbat, ni ñenn ci ñoom doon jàmbate, ba tax malaakam reykat ba rey leen.