TSK

TSK · Numbers 20:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ñu dikk ba ci Musaa ak Aaróona, ak mbooloom bànni Israyil gépp, ca màndiŋu Paran, ca Kades. Ñu àgge leen xibaar, ñoom ak mbooloo ma mépp, ba noppi won leen meññeefum réew ma.

¶ Gannaaw gi, Musaa moo yebale ay ndaw fa dëkk ba ñuy wax Kades, ñu dem ca buurub Edom, ne ko: «Israyil say bokk dañoo wax ne: Umplewoo mboolem coono bi nu daj.

¶ Ñu bàyyikoo tundu Or, jubal yoonu géeju Barax ya, ngir teggi réewum Edom. Mbooloo ma nag mujj xàddi ca yoon wa.

Ba ñu bàyyikoo Kades, ca tundu Or wa digalook réewum Edom lañu dali.

Wetu bëj-saalum, kemu ga day dale fa Tamar ba ca xuru Meriba ca Kades, daldi leru walu Misra ma, ba àkki géej gu mag ga. Loolooy wàllu bëj-saalumam.