jóge Bamot ba ca xur, wa ca àllub Mowab, àkki nag njobbaxtalu tundu Pisga, wa tiim ndànd-foyfoy ga.
TSK
TSK · Numbers 22:1
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ñu daldi yóbbu ca Musaa ak Elasar sarxalkat ba, ak mbooloom bànni Israyil, ña ñu jàppe ca xare ba, ak la ñu ca jàppe, ak la ñu sëxëtoo. Ñu indi lépp ca seen dal ba ca joori Mowab, fa janook Yeriko, te dendeek dexu Yurdan.
Ba ñu bawoo tundi Abarim, ca joori Mowab lañu dali, ca wetu dexu Yurdan, janook Yeriko.
Ñaari giir ya, ak genn-wàllu giir googu ñoo séddu suuf ca penkub dexu Yurdan, fa janook Yeriko.»
¶ Loolu mooy santaane yeek àttey yoon yi Aji Sax ji dénkoon bànni Israyil, Musaa jottli leen ko ca joori Mowab, fa feggook dexu Yurdan, te janook Yeriko.
¶ Jant yooyu lanu nangoo ci loxol ñaari buuri Amoreen ñooña ca wàllaa dexu Yurdan, réew ma dale ca xuru Arnon, ba ca tundu Ermon.
Bànni Israyil jooy nañu Musaa ca jooru Mowab diiru fanweeri fan, fani dëj ba doora mat.