Malaakam Aji Sax ja feeñoo ko foofa, melow sawara wuy tàkk, jafal fa ab gajj. Musaa xoolaat, ndeke gajj ba bépp jàpp na, ba ne jippét, waaye lakkul.
TSK
TSK · Numbers 22:32
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ba loolu amee sànjum Yàlla tàkk ndax yoon wa mu sumb. Malaakam Aji Sax ji nag taxaw ca yoon wa, nara jànkoonte ak moom, moom mu war mbaamam, ànd ak ñaari surgaam.
Malaakam Aji Sax ji ne Balaam: «Àndal ak nit ñi, waaye daal lu ma la waxloo rekk, wax ko.» Balaam nag ànd ak kàngami Balag, dem.
¶ Buleen sunjuñ gémmiñu nag, te fekk koy bojj am pepp.
Aji Sax jee baaxe ñépp, di yërëm lu mu sàkk.
Kuy jubal day ragal Aji Sax ji, ku dëng teddadil nga ko.
Ñàkk te mat moo gën barele te dëng.
Man nag, Niniw, dëkk bu mag bii ëmb lu ëpp fuuf téeméeri junniy nit ak ñaar fukk (120 000), ñu ràññeewul seen ndijoor ak seen càmmoñ, ak mala yu bare, duma leen xalaat?»
ne ko: «Yaw nit ki fees ak gépp xeetu njublaŋ ak ndëngte, doomu Seytaane ji, noonu gépp njub, doo bàyyee lunkal yooni njub yu Boroom bi?