TSK

TSK · Numbers 22:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Mu ne leen: «Dégluleen bu baax samay kàddu: su ngeen feeñlee ab yonentu Aji Sax ji, ci am peeñu laa koy xamale maay kan, te ci gént laay waxeek moom,

Waaye yeen it dal-leen fii guddig tey, ba ma xam lu ma Aji Sax jiy waxaat.»

Balaam ne Balag: «Taxawal fii ci sa saraxu rendi-dóomal, ma dem ba nee. Jombul Aji Sax ji dikk, dajeek man. Mbir mu mu ma won, dinaa la ko àgge.» Mu daldi dem ba ca kaw tund wu ndaw wu dara saxul.

su ma Balag joxoon këram ba mu fees ak xaalis ak wurus sax, duma mana def ci sama coobarey bopp, lenn lu baax mbaa lu bon, lu tebbi ndigalu Yàlla Aji Sax ji? Li Aji Sax ji wax rekk, moom laay wax.

Mise ne ko: «Giñ naa ci Aji Sax ji, Kiy Dund, li ma Aji Sax ji wax rekk laay wax.»

Noonu la sama ñoñ di dajesee fi yaw, toogaanu la, di la déglu. Dañuy déglu say wax, waaye duñu ko jëfe mukk. Lu neex lañuy wax waaye amin wu lewul rekk la seen xol di sàkku.