¶ «Nanga defare sarxalukaay bi bantu séng, guddaay bi di juróomi xasab, yaatuwaay bi di juróomi xasab; ab kaare la sarxalukaay biy doon, taxawaayam di ñetti xasab.
TSK
TSK · Numbers 23:1
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Balag def na Balaam wax, ba noppi sarxal aw yëkk wu ndaw akam kuuy ci kaw sarxalukaay bu nekk.
¶ Samiyel ne ko: «Bànneexu Aji Sax ji ci saraxi rendi-dóomal ak yeneen sarax, mbaa tolloo naak bànneex ba muy am ci dégg ndigalal Aji Sax ji? Ma ne, dégg ndigal a gën ab sarax; xol bu nangoo gën nebbonu kuuy.
Kon nag sàkkleen juróom ñaari yëkk, ak juróom ñaari kuuy. Ngeen dem ba ca sama jaam ba Ayóoba, joxe ko fa saraxu rendi-dóomal, te Ayóoba ñaanal leen, ma seet ci moom ba bañ leena mbugale seenug ndof. Ndax waxuleen dëgg ci man ni sama jaam bi Ayóoba waxe.»
Saraxub ku soxor, Aji Sax ji bañ na ko; ñaanu kuy jubal da koy bége.
Noonu la sama ñoñ di dajesee fi yaw, toogaanu la, di la déglu. Dañuy déglu say wax, waaye duñu ko jëfe mukk. Lu neex lañuy wax waaye amin wu lewul rekk la seen xol di sàkku.