TSK

TSK · Numbers 25:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Mu seet ca bànni Israyil gépp, tànn ca góor ñu mat, fal leen, ñu yilif mbooloo ma: ñii jiite kuréli junniy nit; ñii, téeméer; ñii, juróom fukk; ñii fukk.

¶ Waayi bànni Israyil ja ñu jamoon, te boole kook ndawas Majan sa jam, mooy Simri doomu Salu. Kilifag kër maamam la woon ca Cimyoneen ña.

Seen bët moo leen may la Aji Sax ji def ca Baal Pewor. Mboolem ku toppoon tuur ma ñuy wax Baal ca Pewor, seen Yàlla Aji Sax ji moo ko sànke ci seen biir.

¶ Seen mbokk mu ngeen bokkal jenn ndey, mbaa seen doom ju góor, mbaa ju jigéen, mbaa seen jabar ju ngeen xejjoo, mbaa seen xaritu benn bakkan, su leen dee xiirtal, naan leen ci kumpa: «Nanu jaamuji yeneen yàlla,» yàlla yu ngeen xamul, du yeen du seeni maam,

¶ Bu ngeen déggee, ci benn dëkk, ci dëkk yi leen seen Yàlla Aji Sax ji jox, ngir ngeen dëkke, ñu ne

Mboolem alalu sëxëtoo ju jóge ca dëkk ba, dajaleleen ko ca digg pénc ma, te ngeen lakk dëkk ba, booleek cëxëtoo ma, def ko dóomal bu mat sëkk, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Day doon ab gent ba fàww, deesu ko tabaxaat.

bu néewam fanaan ca garab ga, nañu ko daldi rob ca bés ba, ndax ki wékke alkàndey Yàlla la. Buleen sobeel réew mi leen seen Yàlla Aji Sax sédd.

Kon dees nuy jox juróom ñaari góor ñu askanoo ci Sóol, nu jam leen ba mu sar fa kanam Aji Sax ji ca Gibeya, dëkkub Sóol, ma Aji Sax ji faloon.» Buur ne leen: «Dinaa leen leen jox.»

Naka la kàddu ga jibe ca gémmiñu Buur, ñu muur kanamu Aman, màndargaale ko àtteb deeyam. Ci biir loolu Arbona kenn ci bëkk-néegi buur ne: «Te kat bant bu ëpp ñaar fukki meetar ak nga sampe ca wetu kër Aman, di xaar Mardose mi waxoon jàmmi Buur.» Buur ne: «Wékkleen ko ca!»

Jonah 3:9 TSK

Jombul Yàlla dëpp ba fomm, daldi dëddu tàngooru meram, ba dunu sànku.»