TSK

TSK · Numbers 27:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

nun itam, ba mel ni xeet yépp. Sunu buur a nuy yilif, dox, jiite nu, di nu xareel sunuy xare.»

Te it démb ak bëkk-démb, ba Sóol dee sunu buur, yaw yaa doon jiite Israyil ciy xareem. Aji Sax ji ne la: “Yaay sàmm Israyil sama ñoñ te yaay doon kilifag Israyil.”»

Mise ne ko: «Israyil gépp laa gis ñu tasaaroo ca tund ya, mbete xar yu amul sàmm. Aji Sax ji ne: “Ñii de amuñu boroom. Na ku nekk ci ñoom ñibbi këram ci jàmm.”»

Xërëm, waxi neen, gisaanekat gisi fen, seeni gént, nari neen, te caaxaani neen lañuy dalalee. Moo tax mbooloo mii di taxawaalu niy xar, tumurànke ndax ñàkkub sàmm.

«Yeena réeroon niy xar,» waaye délsi ngeen tey ci seenub sàmm, seen wattukatub xol.