TSK

TSK · Numbers 28:16

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

«Weer wii mooy doon ci yeen wi jiitu ci weer yi, te na doon ci yeen weer, wi jëkk ci at mi.

Ni ngeen koy lekke nag, nii la: bu ngeen koy lekk, dangeen di takku, sol seeni dàll, ŋàbb seen yet, te ngeen lekk ko ci lu gaaw. Loolu gàttu saraxu bésub Mucc ba lay doon, ñeel Aji Sax ji.

¶ Gannaaw loolu Aji Sax ji dafa wax ak Musaa ak Aaróona, ne leen: «Li ma dogal ci saraxu bésub Mucc bi mooy lii: Benn doxandéem du ci lekk.

¶ «Fukki fan ak ñeent ci weer wii, diggante ngoon ak jant bu so, ci ngeen koy màggal, saa yu jotee. Na mu dëppook mboolem dogali yoonam ak àttey yoonam, nangeen ko màggale noonu.»

¶ «Fukki fan ak ñeent ci weer wu jëkk wi mooy seen màggalu bésub Mucc ba. Juróom ñaari fan la màggal giy am, te mburu mu amul lawiir lañu ciy lekk.

Luke 22:7 TSK

¶ Ci kaw loolu bésu màggalu Mburu mu amul lawiir agsi, ñu war caa rendi gàttub bésub Mucc.

Setal-leen seen bopp boog, génneleen lawiir bu yàgg bi ci seen biir, ba mana doon tooyal bu bees bu mucc lawiir, nde doon ngeen ko ba noppi, ndax Almasi, sunu gàttub bésub Mucc biy sunub sarax, rendilees na nu ko.