TSK

TSK · Numbers 29:18

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ «Kiy sarxal Aji Sax ji ab saraxam, na sarxewaale saraxu pepp bu benn fukkeelu efab sunguf su mucc ayib, di ñetti kilo, su ñu xiiwe ñeenteelu xaajub xiinu diw, di liitar ak genn-wàll,

¶ «Ay saraxi tuuram genn-wàllu xiinu biiñ la, di ñetti liitar ci yëkk wu nekk, ak benn ñetteelub xiin, di ñaari liitar ci kuuy mi, ak walaatu xiin, di liitar ak genn-wàllu biiñ ci xar mu ci nekk. Loolooy dóomalu weer wi, weer wu ci nekk, ba weeri at mi daj.

Bokkewul ak rendi-dóomalu Terutel weer wu nekk, mook saraxu peppam, bokkewul it ak rendi-dóomal bi war bés bu nekk, ak saraxu peppam, ak seen saraxi tuur, ni ko yoon tërale. Dees koy def ngir xetug jàmm, muy saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji.