¶ «Xaymab jaamookaay bi nag, defare ko fukki sori rabali lẽe, mu ànd ak wëñ gu baxa te laal yolet ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr, te nga ñawaale ca nataali serub.
TSK
TSK · Numbers 3:25
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba loolu amee mboolem ñu xareñ ñi bokk ci liggéey bi daldi defar jaamookaay bi. Ñu def ko fukki sori rabali lẽe, yu ànd ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr. Ñu ñawaale ci ay nataali serub.
Ci kaw loolu, ñu firi malaan mi ci kaw jaamookaay bi, daldi lal kiiraay li ci kawam, na ko Aji Sax ji sante woon Musaa.
ñooy dénkoo ndénkaaneem, di dénkoo dénkaaney mbooloo mépp fi kanam xaymab ndaje mi, ndax ñooy sasoo liggéeyu jaamookaay bi.
ñooy gàddu kiiraayi jaamookaay bi, ak xaymab ndaje meek malaanam, ak malaanum deru piipi bi ci kaw, ak ridob bunt xaymab ndaje mi;
¶ Ci biir loolu ñu wékki jaamookaay ba, Gersoneen ñaak Merareen ñay gàddu jaamookaay ba daldi dem.
Ma ne leen: «Yeen, dees leena sellalal Aji Sax ji, ni ñu sellale ndab yi, te xaalis beek wurus wi di saraxu yéene ñeel Aji Sax ji, seen Yàllay maam.
Ay may yu wuute lanu am, may yu yemook céru yiw bi ñu sédd ku nekk ci nun. Su dee biral kàddug waxyu mooy sag may, biraleel kàddug waxyu sa kemu ngëm;
¶ Kon nag Timote doom, loolu mooy ndigal li ma la dénk, te mu dëppook kàdduy waxyu yi jotoona jib te jëm ci sa mbir. Gànnaayool kàddu yooyu ngir di ci xaree xare bu baax bi,