TSK

TSK · Numbers 31:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Mu yebal ay ndaw ca Balaam doomu Bewor ngir wooyi ko, ca Petor ga Balaam cosaanoo, ca tàkkal dex ga ngir ne ko: «Balaam! Gàngoor a ngii jóge Misra. Ñu ngii lal suuf si ba mu daj, te ñoo sanc, janook man màkk.

Ana kuy lim feppi suuf, ba lim askanu Yanqóoba? Ku mana waññ xaajaatub Israyil gii? Man de, yal naa dee deewinu aji jub ñii, yal na sama muj mel ni gu askan wii!»

Ndawas Majan sa ñu jam di Kosbi. Baayam Sur doonoon kilifag kër maamam ca giirug Majan ga mu bokk.

Xeet yee tàbbi pax ma ñu gasoon, fakktaloo fiir ga ñu làqoon.

Kuy jubal, jiital mat. Njublaŋ ak wor, detteelu.

Waaye ñi sàkkoo barele, ñooy tàbbi ci nattub bakkan, aki fiir, ak lu bare ciy xemmemtéef yu tekkiwul dara, xemmemtéef yuy lore, tey suuxal seeni boroom ci yàqule ak sànkute.

Jude 1:11 TSK

¶ Ngalla ñii! Ñoo jaare yoonu Kayin; ñoo lajj, topp Balaam cig réeram ngir ag peyoor; ñoo diiŋat ba sànku ni Kore.

Ñu daldi jàpp rab wi, mook yonentu caaxaan, bi defoon ci turu rab wi ay kéemaan yu mu sànke ña ñu màndargaale woon màndargam rab wi, te ñu doon jaamu jëmmu nataalu rab wi. Ñoom ñaar ñépp lañu sànni, ñuy dund ca déegu sawara waak tamarax bay bax.