Numbers 32:17
TSK
Waaye nun kay danuy daldi gànnaayu, jiitu bànni Israyil, ba keroog ñu leen yóbboo ca seen suuf. Sunu njaboot a nuy xaare fii, biir dëkk yu tata wër, ngir ñu mucc ci waa réew mi.