TSK

TSK · Numbers 35:34

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Na ma bànni Israyil defaral kër gu sell, ndax ma dëkk ci seen biir.

¶ «Buleen sobeel seen bopp ci mboolem defin yooyu, ndax xeet yi ma leen dàqal, noonu lañu daan jëfe, ba sobeel seen bopp.

Yeen nag ma ne leen yeenay nangu seen réew ñoom, ndax maa leen ko jox, ngeen moom ko, muy réew mu meew maak lem ja tuuroo. Man maay seen Yàlla Aji Sax, ji leen ràññatleek yeneen xeet yi.

Ci kaw loolu ñu bokk daje fi kaw Musaa ak Aaróona, ne leen: «Doy na sëkk! Mbooloo mi ba mu daj, ñépp a sell, te ci sunu biir la Aji Sax ji nekk. Ana lu ngeen di xoggliku ci kaw mbooloom Aji Sax ji?»

bu néewam fanaan ca garab ga, nañu ko daldi rob ca bés ba, ndax ki wékke alkàndey Yàlla la. Buleen sobeel réew mi leen seen Yàlla Aji Sax sédd.

Mu ne: «Fii laay dal-loo ba fàww, fii laay dëkk, maa ko taamu.

«Bul tudde wor, lenn lu askan wii tudde wor; lu ñu ragal it, bu ko ragal, bu ko tiit.

«“Aji Sax ji nekk fi, nga naan: ‘Ñaari làngi giir yii dëkke seen ñaari réew yii, maa leen moom, noo ciy teg loxo.’

Gan takktoo la kër Yàlla séq ak ay tuur? Ndax kat, nun, nooy kër Yàlla jiy dund, te noonu la ko Yàlla waxe ne: «Maay dëkk ci seen biir, di dox ci seen biir, di seen Yàlla, ñuy sama ñoñ.»

Du lenn lu sobewu lu fay dugg nag, mbaa defkatu jëf ju ruslu ak njublaŋ. Ñi ñu bind ci téereb dund bu Gàtt bi doŋŋ ñoo fay dugg.