TSK

TSK · Numbers 4:16

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

ak diwu oliw gu ñuy taaloo, ak ndàbb luy xeeñal diwu pal, di xeeñal cuuraay,

Menn kuuy mi, nga rendi ko ci suba, meneen kuuy mi, diggante ngoon, ba jant di so.

«Yaw nag, tànnal ngën-gi-xeeñal; xeetu ndàbb li ñuy wax miir, bu tooy bi, sàkk ci juróomi kilo, xasum kanel mu xeeñ; ñaari kilo ak genn-wàll, yuuru gattax gu xeeñ; ñaari kilo ak genn-wàll,

Mu sàkk nag diwu pal gu sell gi, sàkk cuuraay lu xeeñ li raxul, def ko njafaan lu njafaan-kat waajal ba mu baax.

«Santal bànni Israyil, ñu indil la diwu segalu oliw gu set, ngir leerlu, ñu di ko taale làmp yi guddi gu nekk.

Luke 4:18 TSK

«Noowug Boroom baa ngi fi sama kaw, moo ma fal, ngir ma yégal néew-doole yi xibaaru jàmm bi. Da maa yebal ngir ma yégal jaam yi ne dees na leen goreel, yégal gumba yi ne dinañu gis, yégal ñi ñu not, ne dees na leen jot,

¶ Dees noo wara jàppe ay surgay Almasi, ay saytukati mbóoti Yàlla.

¶ Kon nag bokk yu sell yi, yeen ñi bokk ci wooteb asamaan, ràññeeleen Yeesu, ndaw li, sarxalkat bu mag bi ci yoon wi nu gëm.

«Yeena réeroon niy xar,» waaye délsi ngeen tey ci seenub sàmm, seen wattukatub xol.