TSK

TSK · Numbers 4:20

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Aji Sax ji ne ko: «Wàccal, àrtu mbooloo mi, ndax ñu baña bëtt, di ma deñsi kumpa; lu ko moy ñu bare ci ñoom dinañu dee.

Bu jaamookaay bi dee dem, Leween ñee koy wékki, bu jaamookaay bi dee dale bérab, Leween ñee koy we. Ku ci bokkul ba laal ci nag, dees koy rey.

Nii ngeen di def ak ñoom, ba bu ñu jegee yëf yu sell yee sell, di dund te duñu ca dee: Aaróona aki doomam ñooy dugg, daldi sédd ku nekk ci ñoom liggéeyam ak la muy gàddu.

¶ Terewul Yàlla mbugal ñenn ca waa Bet Semes, ndax dañoo yërndu woon ca biir gaalu Aji Sax ja. Juróom ñaar fukki nit la fàdd ca ñoom. Waa dëkk ba nag di tiislu ndax mbugal mu réy moomu leen Aji Sax ji teg.

¶ Ci kaw loolu néeg Yàlla bi ci asamaan ubbiku, gaalu kóllëreg Yàlla ga di feeñ ca biir màkkaanam ma, melax ya tàkk, kàddu yaak dënu ya riir, suuf sa yëngu, tawu doji yuur bu metti daldi sóob.