na waa ji yóbbu jabaram ca sarxalkat ba, te yóbbaleel ko saraxu ñetti kiloy sungufu lors. Du ci sotti diw, du ci def cuuraay, ndax saraxu pepp boobu saraxu fiiraange la, saraxu toppukaay la bu ñuy toppe ñaawtéef.
TSK
TSK · Numbers 5:18
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yal na ndoxum alkànde mii tàbbi ci say butit, laxal sa njurukaay, wal sab koll.” Su ko defee ndaw si ne: “Amiin, Amiin.”
Jombul mu am ku dégg kàdduy ngiñ lii, tey nax boppam cim xelam, naan: «Jàmm rekk laay am, maa tey të,» ba tax ñax mu wow lakkaale mu tooy.
Muj ga mu wex xàtt, di gaañe ni ñawkay saamar.
Ndeke sama tiisu xol wii, sama jàmm rekk a tax. Sa cofeel a tax nga sorele maak paxum sànkute. Yaa sànni sa gannaaw sama bépp bàkkaar.
Jigéen ju nanguwula muuru, bu yeboo xuuf kawaram. Ndegam am na kersay xuuf kawaram, mbaa mu nelu nag, fàww mu muur boppam.
Kàddug Yàlla de luy dund la, ànd ak doole, te moo gëna ñaw saamaru ñaari ñawka bu gëna ñaw. Day sar ba fa xel akug noo digaloo, ba fa yax ak yuq dajee, te man naa càmbar ay xalaat ak mébéti xol.
¶ Gis naa say jëf ak sa cofeel ak sa ngëm ak sa liggéey ak sag muñ. Xam naa ne sa jëf yu mujj moo ëpp jëf yu jëkk ya.