Li feek jàngoro jaa ngi ci moom, day sobewu te gannaaw daa sobewu, na dëkk moom doŋŋ te na dëkkuwaayam génn dal bi.
TSK
TSK · Numbers 5:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Gannaaw loolu Aji Sax ji wax na Musaa ne ko: «Waxal sarxalkat yiy doomi Aaróona ne leen: Bu ci kenn sobeel boppam, di laal mbokkam mu dee,
¶ Aji Sax ji ne Musaa: «Xanaa baayam sax su ko jéppi woon, ba tifli ko ci kanam, muy gàcceem diiru juróom ñaari fan? Nañu ko génne dal bi diiru juróom ñaari fan, door koo délloosi ci biir.»
¶ «Lii la yoon wi tëral: Bu nit deeyee ci biir xayma, képp ku dugg ci biir xayma bi, ak képp ku mu fekk ci xayma bi, day sobewu diiru juróom ñaari fan,
¶ «Te yeen nag, dal-leen ci biti, buleen dugg ci biir dal bi diiru juróom ñaari fan, mboolem ñi rey ak mboolem ñi laal ku ñu rey. Nangeen setlu bésub ñetteel ba, ak bésub juróom ñaareel ba, yeen ak ñi ngeen jàpp.
¶ Ci biir loolu amoon na ñeenti gaana yu nekkoon ca bunt dëkk ba. Ña nga naan ci seen biir: «Xanaa dunu toog fii ba dee?