Leviticus 2:2
TSK
te yót ko doomi Aaróona yu góor yiy sarxalkat yi. Na sarxalkat bi sàkk barci-loxob sunguf su mucc ayib soosu ànd ak diw gi, te boole kook cuuraay li lépp. Na sarxalkat bi def cér boobu saraxu baaxantal, lakk ko ca kaw sarxalukaay ba, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.