TSK

TSK · Numbers 5:27

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Waaye su dee yaa moy te fekk la ci sa buumu jëkkër, su dee yaa sobeel sa bopp ak geneen góor gu ànd ak yaw te du sa jëkkër nag...”

réewum Asiri it fekki leen, di dooleel askanu Lóot wa. Selaw.

Muj ga mu wex xàtt, di gaañe ni ñawkay saamar.

Seen tur wi ngeen bàyyi gannaaw la samay tànnéef di móoloo, naan: “Yal na la Boroom bi Aji Sax ji rey ni diw ak diw,” waaye ñoom sama jaam ñi, tur wu yees lees leen di wooye,

Maa leen di toppe saamar akub xiif ak mbas. Maa leen di def ñu seexlu leen ci mboolem réewi àddina, teg ci di musiba mu ñuy muslu ci biir mboolem xeet wu ma leen sànni, ba ku fay kókkalee, ñoom ngay tudd.

¶ «Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi déy dafa wax ne: “Bu ngeen demee Misra, ni sama mer ak sama xadar yurikoo woon fi kaw waa Yerusalem, ni la sama xadar naan yureet fi seen kaw. Dingeen doon gentu alkànde, ñu di leen móolook a sewal, te dungeen gisati miim réew.”»

Na ngeen doone woon alkànde ci biir xeet yi, yeen waa kër Yuda, ak waa kër Israyil, ni laa leen di walloo, ba ngeen doon barke. Buleen ragal. Góor-góorluleen.»

Teewul muy ci ñii, xetu ndee gu jëme ci ndee, te di ci ñee, xetu dund gu jëme ci dund. Boobu sas nag, ana ku ko àttan?

¶ Rawatina nag boroom xemmemtéefi yàqute, yi topp seen bakkan te faalewuñu genn kilifteef. Ñu fétteeral lañu te bew, ragaluñoo saaga sax boroom daraja yu kawe ya fa asamaan.