TSK

TSK · Philemon 1:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Su dee mbirum Tit, mooy sama wéttal, di ma jàpple ci liggéey bi, ngir yeen. Sunu bokk, yi ànd ak moom nag, ñooy ndawi mboolooy gëmkat ñi, te ñooy teraangay Almasi.

¶ Maa yey nag njortal leen loolu yeen ñépp, ndax ci sama xol laa leen def, te it muy ci wàllu jéng yi ñu ma jénge, di ci wàllu kàddu guy waxal xibaaru jàmm bi, ak di ko feddli, yeen ñépp am ngeen wàll ci sama añub yiw.

Damay tinul Onesim, sama doomu tuubeen ji ma tuubloo ba mu mel ni maa ko jur ci diir bi ma nekke fii ci kaso bi.

¶ Kon nag bokk yu sell yi, yeen ñi bokk ci wooteb asamaan, ràññeeleen Yeesu, ndaw li, sarxalkat bu mag bi ci yoon wi nu gëm.

James 2:5 TSK

¶ Bokk yi, soppe yi, dégluleen. Xanaa du Yàlla moo taamu ñi àddina jàppe ñu néew doole, ngir ñu barele ngëm, boole ci jagoo nguur, gi Yàlla dig ñi ko sopp?