TSK

TSK · Philippians 1:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Mu dikk ba ci nun, jël ngañaayal Póol, yeewe ko ay tànkam aki loxoom, daldi ne: «Noo gu Sell gi dafa wax ne: “Ki moom ngañaay lii, nii la ko Yawut yiy yeewe ca Yerusalem, jébbal ko jaambur ñi dul Yawut.”»

Ña ngay dem, te naa ca seen biir: «Kii kat deful dara lu jar dee mbaa ay jéng.»

Mbir moomu nag moo tax ma woolu leen, ngir giseek yeen, diisook yeen, ndax yaakaaru bànni Israyil moo waral sama jéng yii.»

¶ Moo ma tax di ñaan, man Póol mi ñu tëj ngir Almasi, ndax ñi dul Yawut, yeen jaambur ñi,

xibaar bi ma di ndawam lu ñu tënke ay jéng. Waaye ñaanal-leen ma ma di ko waxee fit, ni mu ma ware.

Te it gëmkat ñu sell ñépp a ngi leen di nuyu, rawatina waa kër Buur Sesaar.

Ci seen biir kay la kàddug Boroom bi jollee, te yemul ci Maseduwan ak Akayi rekk, waaye seen ngëm Yàlla fépp la siiwe, ba soxlawunu cee waxati fenn dara.

¶ Soppe yi, tàngooru nattu bi ngeen nekke nii, bumu leen jaaxal ba mel ni lu jaaduwul moo leen dikkal.