TSK

TSK · Philippians 3:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ba ñu leen génnee, kenn ci ñoom ne Lóot: «Dawal sa xélu bakkan, bul geestu, bul taxaw fenn ci joor gi. Dawal ca tund ya, bala ngaa dee.»

Job 2:4 TSK

Seytaane ne Aji Sax ji: «Bakkan a wuutu bakkan rekk. Mboolem lu nit am, man na koo weccee bakkanam.

Jëndal dëgg te bu ko jaay. Sàkkul xel mu rafet ak yar akug dégg.

Naka noonu itam, kenn ci yeen du mana doon sama taalibe te dëdduwul mboolem lu mu am.

¶ «Bésub keroog boobee, ku mu fekk ci kaw am taax, te say yëf ne ca biir kër ga, bul wàcc, di ko jëli. Te ku mu fekk tool ba itam, bul dellu.

Ñu lekk ba suur, daldi sànni pepp ma biir géej, ngir woyofal gaal ga.

¶ Dama ne, man Póol maa leen wax ne leen: su ngeen demee ba ñu xarfal leen kay, Almasi amalatu leen lenn njariñ.

Rax ci dolli, lépp sax laa far jàppe ag wàññeent, ndax ngëneel li sut lépp, te mooy xam kuy sama Sang Almasi Yeesu. Moom moo ma taxa nangoo ñàkk lépp, def lépp ni mbuubit, ngir tonoo Almasi,