TSK

TSK · Proverbs 13:25

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ñooy loof cib xiif, jeex tàkk ndaxi jàngoro, ak mbas yu metti. Ay selli rabi àll laay yebal ci seen kaw, boole ca daŋaru ndox-suuf.

Dénkul ci Aji Sax ji, di def lu baax, ba des ci réew meek jàmm.

Ku maandu, Aji Sax ji yég la, sab cér sax.

Aji Sax ji du seetaan ku jub, di xiif, waaye day xañ ab soxor la mu xemmem.

Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: «Ma ne sama jaam ñeey lekk, yeen ngeen nekke xiif. Ma ne sama jaam ñeey naan, yeen ngeen nekke mar. Sama jaam ñeey bànneexuji, yeen, ngeen nekke gàcce.

Ndax kat tàggat aw yaram, as njariñ a ngi ci, waaye ag njullite, ci lépp lay jariñe, te moo moom digeb àddinay tey ak ëllëg.