Esther 3:6
TSK
Teewul mu siide fexeel Mardose doŋŋ, ndax booba waxoon nañu ko askan wi Mardose bokk. Ba loolu amee Aman di wuta sànk mboolem Yawut yi nekk ci mboolem réewum Aserus, di bokki Mardose.