TSK

TSK · Proverbs 14:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Suleymaan ne ko: «Yaw de yaa baaxe lool sab jaam Daawuda, saa baay, ngir na mu daan doxale fi sa kanam ci dëgg ak njekk ak njubteg xol. Yaa ko baaxe lool, may ko doom ju góor ju toog cib jalam, bésub tey jii.

Job 1:1 TSK

¶ Amoon na ca réewum Ucc, góor gu ñuy wax Ayóoba. Góor googu nekkoon ku mat te jub, ragal Yàlla te dëddu lu bon.

Job 28:28 TSK

daldi ne doom aadama: «Ragal Boroom bi daal, mooy xel mu rafet, te dëddu lu bon mooy am ug dégg.»

Màggal-leen Ki Sax! Ndokklee ku ragal Aji Sax ji, di tàqamtikoo ay santaaneem.

Ku jiital ngor ak worma, Yàlla jéggal la; ku ragal Aji Sax ji, dëddu lu bon.

Ma daaneele fii, déggees na lii lépp: Yàlla, ragal ko; ay santaaneem, jëfe ko; loolu rekk mooy nit.

¶ «Ku leen déggal nag, man nga déggal; ku leen gàntal, man nga gàntal. Te ku ma gàntal, gàntal nga ki ma yebal.»

Acts 9:31 TSK

¶ Ba mu ko defee mbooloom gëmkat ñi ci mboolem diiwaani Yude ak Galile ak Samari daldi am jàmm. Ñuy gëna dëgër, di wéye ragal Yàlla, tey yokku ci ndimbalal Noo gu Sell gi.

waaye xeetoo xeet, ku ko ci ragal tey def njekk, mooy ki ko neex.

Nit ñi, seen bopp doŋŋ lañuy bëgg, ay bëggkati xaalis lañuy doon, ay damukat, nit ñu réy, di ay saagakati Yàlla, ñu déggadil waajur, ñu santadi te selladi.